Cant ñeel na sa Yàlla Aji Sax ji, moom mi la bége, ba teg la ci jalub Israyil. Aji Sax ji daa sopp Israyil cofeel gu dul jeex, moo tax mu fal la buur, ndax nga saxal fi dëgg ak njekk.»
TSK
TSK · Romans 13:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
«Dungeen bàyyi àtteb njublaŋ, ak di faral ku bon? Selaw.
Buur mer lool, mel ni gayndee ŋar; boo ko merloo, dangay xaru.
Buur, bu xeloo, ràññee ku bon, mbugal ko, te du ko ñéeblu.
Nanga àddul ku amul kàddu, ku sësul fenn, nga ñoŋal àqam.
Jàngleen di def lu baax, sàkku njub, waññi ab notkat, àtte dëgg, ab jirim, sàmm àqu jëtun.
Kàngamam yi ci biiram a ngi mel ni saafaandu yuy dogat am pàdd, tuur deret ja, di sànk ay bakkan ngir nangu alali boroom.
Dama ne: «Ngalla dégluleen yeen njiiti Yanqóoba, yeen kilifay kër Israyil! Xanaa du yeena wara xam yoon?
Samay soppe, buleen di feyul seen bopp, xajal-leen am sànj, am sànj fajal boppam, ndax bindees na ne: «Man maay feye, maay añale.» Boroom bee ko wax.
Ci moomu mbir, bu kenn ci yeen tooñ mbokkam, di aakimoo yelleefam, ndax waxoon nanu leen ko, ba artooti leen ne leen jëf ju ni mel, Boroom bee koy fey ña ko def.