TSK

TSK · Romans 8:26

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji, damaa néew doole, yërëm ma! Éy Aji Sax ji, sama yaram a tas, dàmp ma!

Néew-ji-doole dagaan, Aji Sax ji dégg, dalal xelam, teewlu ko,

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, dib taalif, ñeel Daawuda.

Mu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf.

Sama xol bi wow ni ñax mu xuur, ba lekk safatu ma.

Sàkku naa sag wall ba xol jeex, di xaar sa kàddu.

Sama baat nga dégg, ma ne la: «Bul fattal sab nopp, samay onk ak samay yuux.»

Luke 11:1 TSK

¶ Yeesu moo doon julli benn bérab. Ba mu noppee, kenn ca taalibeem ya ne ko: «Sang bi, jàngal nu julli noonee Yaxya jàngale julli ay taalibeem.»

Mayeesu leen noo gu leen di desloo cig njaam, ba tax leena dellu cig ragal, waaye Noowug doom yu ñu doomoo, moom lees leen may, te looloo nu tax di wooye Yàlla: «Abba», mu tekki «Baay.»

Moo nu tax di onk ci biir xayma bii nu nekk, ndax yàkkamtee soloo sunu dëkkuwaayu asamaan, teg ko ci kaw bii nu jiital,

Nit ku mel noonu laay damoo, waaye du sama bopp laay damoo, xanaa ma damoo diggante yu ma néewe doole.

ndax nun ñaari xeet yépp, ci moom Almasi lanu jote ci Baay bi, ci ndimbalal genn Noo gi.

Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.

James 4:3 TSK

Te su ngeen ñaanee, dungeen am, ndax mébét mu bon ma ngeen ñaane, ngir am lu ngeen toppe seen bakkan.