TSK

TSK · Zechariah 2:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ba ñu leen génnee, kenn ci ñoom ne Lóot: «Dawal sa xélu bakkan, bul geestu, bul taxaw fenn ci joor gi. Dawal ca tund ya, bala ngaa dee.»

Ruth 4:1 TSK

¶ Ci biir loolu Bowas dem ba ca bunt dëkk ba, toog fa. Noonu rekk mbokk ma mu waxoon ne su dee jotaat, moo ko ci gëna yey, daldi fay jaare. Mu woo ko ne ko: «Diwoo, kaay fii, toog tuuti.» Mu dikk, toog.

Yeen ñiy yóbbu ndabi Aji Sax yu sell yi, bu ngeen di jóge Babilon, dëdduleena dëddu lu sobewu, bañ koo laal, setluleen te génn foofa.

Aji Sax ji ne ma: «Bëj-gànnaar la safaan bay fettaxe, dal ci kaw waa réew mi mépp.

Dama leen di def, waa réewi àddina yépp, ku leen ci xool rasu. Te li ko waral di Buurub Yuda, Manase miy doomu Esekiya, ak li mu def ci digg Yerusalem.»

«Yeen xeet yi, dégluleen kàddug Aji Sax ji, yégleleen ko ca tefes yu sore ya. Ne leen: “Ki tasaare woon Israyil, moo leen di dajale, sàmm leen ni sàmm ak géttam.”

«Yeen gan ñi, fëxeleen Babilon, ba sore réewum Kaldeen ñooñu. Defleen niy sikket, daw jiitu jur gi.

Yeen sama ñoñ, génnleen fi seen biir, na ku ne rawale sa bakkan, ba mucc tàngooru sànjum Aji Sax ji.

Seen ñetteelu xaaj, mbas lañuy deeye mbaa xiif bu leen di sànk ci biir dëkk bi. Beneen ñetteelu xaaj bi, saamar lañuy fàddoo ci seen dig-digal bi. Xaajub ñetteel bi ci des, fépp fu ngelaw jublu laa leen di tasaare, te saamar laa leen di toppe.

Mboolem ña ko dar, ay toppam ak mboolem gàngooram, maa leen di wasaare fépp fu ngelaw jublu, toppati leen ak saamar.

Amos 9:9 TSK

«Maa ngii déy di sant xeetoo xeet, ñu gësëm waa kër Israyil, ni ñuy gësëme tameb suuf, te doj du rot.

¶ Fa la malaaka ma doon wax ak man jekki di dem, meneen malaaka dikk dajeek moom.

¶ Ci kaw loolu ma dégg beneen baat bu jóge asamaan, ne: «Yeen sama ñoñ, génnleen dëkk bii, bala ngeena bokk ak moom ay bàkkaaram, bay séddu ci mbugalam.