TSK

TSK · Acts 7:38

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ba loolu amee Musaa yéeg, jëm ca Yàlla. Aji Sax ji jaar ci turu Musaa foofa ca kaw, ne ko: «Nanga wax ak waa kër Yanqóoba te nanga ma siiwtaaneel ci bànni Israyil googu, lii ma lay wax:

¶ Aji Sax ji teg ca ne: «Àttey yoon yii, nanga leen ko jox:

¶ Lii mooy santaane bi, ak dogali yoon yeek àttey yoon yi seen Yàlla Aji Sax ji santaane ma jàngal leen ko, ngir ngeen di ko jëfe ca réew ma ngeen jàll jëm, ngir nanguji ko,

da ne leen: «Defleen seen xel ci mboolem kàddu yi ma leen di artoo man, bésub tey, te ngeen sant seeni doom ñu sàmmoo jëfe mboolem kàdduy yoon wii.

Ca tundu Sinayi wa nga wàcc, àddoo asamaan, wax ak ñoom, dénk leen ndigal yu jub, ak yoon yu dëggu, ak dogali yoon ak santaane yu baax.

Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot.

Acts 7:35 TSK

¶ «Musaa moomu ñu weddi woon, ne ko: “Ku la def kilifa ak ab àttekat?” Moom nag la Yàlla def kilifa ak ab jotkat, yebal ko ci ñoom, malaaka ma feeñu Musaa ca gajj ba, daldi koy jottli yóbbante ba.

Xanaa lu bare, ci wet gu nekk. Li ci jiitu moo di ñoom lañu dénk kàdduy Yàlla.

Waaye njub, gi ngëm di maye, li muy digle mooy: «Bul wax ci sa xel, ne: “Ana kuy yéeg fa kaw?”» nde loolu mooy Almasi wàcc ngay sàkku.

Gannaaw nag kàddug Yàlla ga jibe woon ci gémmiñu malaaka yi, mujj na di lu wér péŋŋ, te képp ku ko masa xëtt, mbaa mu déggadi ko, jot nga añ bi war ci sag tooñ,

Ndax kat nëgëni tey waroon na leena fekk diy sëriñ, waaye aajowoo ngeen ba tey ku leen jàngal ndoortel waxi Yàlla. Nàmp um soow ngeen mujj aajowoo, ndax ñàkka àttan ñam wu dëgër.