TSK

TSK · Ezekiel 21:7

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

kilifay waa Edom jàq, njiiti Mowab di kat-kati, mboolem waa Kanaan tiit, ne yasar;

Gannaaw loolu, na kilifa yi dellu wax ak gàngoor gi, ne leen: «Ana ku ci ragal, ana ku ciy yox-yoxi? Na daldi ñibbi kat, bala moo yoqiloo ay moroomam, ni moom.»

Moo tax man Aji Sax ji Yàllay Israyil damaa wax ne: “Maa ngii di wàcce ci Yerusalem ak Yuda musiba muy buur noppi képp ku ci dégg.

Ba ñu yégalee Buur Axas sëtub Daawuda, ak waa këram, ne ko waa Siri, Efrayim lañu lëngool, mbir ma yëngal na Buur Axas ak waa réew ma, ba mel ni garabi gott bu ngelaw li gësëm.

Saa yu dikkee ne leen céex, suba su ne mu ne jaas, guddeek bëccëg, mu teew, te bu jibee sax fit rëcc.»

Aji Sax ji dafa wax ne: «Aw askan a ngii bàyyikoo réewum bëj-gànnaar, xeet wu mag lañuy doon, sàqee fa cati àddina.

¶ Ci kaw loolu Yeremi wax ak kàngam yépp ak mbooloo ma mépp, ne leen: «Aji Sax jee ma yebal ngir ma biral waxyu, rëbb kër gii ak dëkk bii, te mooy kàddu yi ngeen dégg yépp.

Buuru Babilon dégg riir ma, yoxo ya yoqi, njàqare ne ko taral, mu jàq ni kuy matu.

«Yaw nit ki, jàkkaarlool ak tundi Israyil, nga waxal leen waxyu.

«Yaw nit ki, xanaa waa kër Israyil, kërug fippukat gi, newuñu la: “Ana looy def nii?”

Sëxëtooleen xaalis, sëxëtoo wurus, alal du fi jeex te mboolem gànjar a jale.

¶ Kon nag «dëgëral-leen loxo yi toqi, ak óom yi bañ,»