TSK

TSK · Genesis 14:5

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

ak Etteen ñi ak Periseen ñi ak Refayeen ñi,

¶ Emeen ñaa fa jëkkoona dëkk, askan wu am kàttan lañu woon, bare, yegg ca kaw ni Anageen ñi.

Mennum Og buuru Basan doŋŋ moo muccoon ca ndesu Refayeen ñu ponkale ña. Lalam ba, lalu weñ gu ñuul la. Ma nga noonee ca Raba, dëkkub Amoneen ña. Guddaayu lal ba ci xasabu góor, juróom ñeenti xasab la, di ñeenti meetar ak genn-wàll, yaatuwaay ba, ñeenti xasab, di ñaari meetar.

Buleen leen ragal, ndax seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di xeexal.»

¶ Ba mu ko defee waa Filisti dikkaat, tasaaroo ca xuru Refayeen ña.

Israyil agsi Misra, muy nganug Yanqóoba ga ca réewum Xam.

Mooy kéemaan ya fa réewum Xam, kiraama ya ca géeju Barax ya.

¶ Lu jëm ci Mowab, Aji Sax ji Yàllay Israyil, Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: «Ngalla waa Nebo, seen dëkk ba yàqu na! Kiryaatayim, ñu torxal, nangu ko; tata ja daanu, tasaaroo.