TSK

TSK · Genesis 21:17

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Gannaaw ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikke na Ibraam wax jii ci peeñu, mu ne ko: «Yaw Ibraam, bul ragal dara; man maay sa kiiraay, te sa yool dina màgg lool.»

¶ Malaakam Aji Sax ja ne ko: «Dellul ca sa sang, te nga yem ciy loxoom.»

Yàlla ne ko: «Man maay Yàlla, di sa Yàllay baay. Bul ragala dem Misra, ndaxte askan wu réy laa fay sose ci yaw.

¶ Musaa nag ne mbooloo ma: «Buleen tiit, neleen tekk te xool li Aji Sax jiy def, ba xettli leen tey jii. Ndax kat waa Misra yii ngeen di gis nii tey, dootuleen leen gis mukk.

¶ «Man Yàlla, buleen wax lu ñaaw ci man, te seen kilifag askan, buleen wax lu bon ci moom.

Ci biir loolu Sóol ne tëll, jiital ay nagam, jóge tool ya. Mu ne: «Lu nit ñi xewle bay jooy nii?» Ñu nettali ko kàdduy waa Yabes.

Aji Sax ji nag baaxe leen, yërëm leen, geesu leen ndax kóllëreem ak Ibraaymaak Isaaxaak Yanqóoba. Looloo tax buggu leena faagaagal, te ba tey jii xalabu leen.

di ma woo bésub njàqare, ma wallu la, nga màggal ma.»

Mu woo ma, ma wuyu ko; mook man ci biir njàqare, ma xettli ko, darajaal ko,

Yéene bii ñeel na xuru Peeñu ma: Ana lu ngeen di yéege, yeen ñépp seen kawi taax?

Man Aji Sax ji maay sa Yàlla; téye sa loxol ndijoor, di la wax ne la: «Bul tiit, maa lay dimbali.»