Doomi Sem yu góor ñii la: Elam ak Asur ak Arpagsàdd ak Ludd ak Aram.
TSK
TSK · Isaiah 21:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ñu ngi naa: «Sunu làmmiñ lanuy daane, nook sunu kàddu; ku nu manal dara?»
Ñi ñu jàpp, yal na seeni onk àkki fa yaw. Ñi ci tànki ndee, yal nanga leen musale sa doole ju màgg.
Dangay xam lu jaadu, ñu naw la; yoonu workat day metti.
Yéegeleen ab raaya kaw tund wu ne duŋŋ, joorleen ñii, tàllal-leen loxo, ñu jàlle bunti kàngam yi.
¶ Aji Sax ji kay mooy yërëm askanu Yanqóoba, dellu taamu xeetu Israyil wii. Moo leen di sancaatal fa seen suuf, doxandéem yi fekki leen; boole seen bopp ci askanu Yanqóoba.
Àddina yépp a féex, am jàmm, sarxolle jolleendoo.
Cati àddina lay woy di jibe, nu dégg ñu naa: «Teddnga ñeel na Aji Jub ji!»
Ñi Aji Sax ji xettleey délsi, duggsi Siyoŋ, di sarxolle, kaalawoo bànneex bu sax. Mbég ak bànneex a leen di dab, naqar aku tiis dëddu leen.
ak mboolem buuri Simri ak buuri Elam ak mboolem buuri Medd,
Aji Sax ji ne: «Du Efrayim ay sama doom ji ma sopp, gone gi may bànneexal? Lu ma ko gëdd gëdd, di ko bàyyi xel. Moo tax sama xol di ko laaj, ma yërëm koo yërëm.» Kàddug Aji Sax jee.
Nga ne: “Wóoy ngalla man! Aji Sax ji yokk na maw naqar. Onk naa ba tàyyi te awma noflaay.”
Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: «Damay damm fittu Elam, seen ngëneelu ngànnaay.
Waaye seen jotkat a am doole, te mooy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi. Moo leen di layool seen layoo, ngir jàqal réewum Babilon, jàmmal waa àddina yi ci des.
«Nàmmleen fitt yi, feesale mbar yi! Aji Sax ji xabtal na buuri Medd fi kaw Babilon, nar koo tas. Lii mbugalu Aji Sax jee, mbugal mi këram waral.
Maay dikke mbugal Bel, tuur mi ci Babilon, yàbbiloo kob lancam. Xeet yi noppee def um wal, wuti ko, tatay Babilon it màbb.
Su Babilon yéegoon asamaan, dàbbli fa tata ju ne kekk sax, du tee ay yàqkat bawoo fi man, dal ci kawam.» Kàddug Aji Sax jee.
SÉDDALE: Séddale nañu sam réew, ba jox ko xeeti Medd ak Pers.»
Kuuy mi nga gis mu am ñaari béjjén, buuri waa Medd ak waa Pers la.
Waaye mer mu réy laa mere xeet yii naagu. As lëf laa meroon, waaye ñoom ñoo yokk aw ay.”