TSK

TSK · Isaiah 59:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Bu ma xañ mukk kàddug dëgg, say àtte laa yaakaar kat.

Aw njebbit mooy saxe fa ëkkub Yese, ab car soqeekoo fa reen ya,

Aji Sax ji dafa wax ne: «Bu bésub yiw taxawee, ma nangul la; bu bésub mucc jotee, ma wallu la, sàmm la, def la ngay kóllëre sama digg ak askan wi, ngir yékkatiwaat réew mi, séddalewaat ay cér, suuf sii gental tey,

Teewluleen te dikk fi man. Dégluleen, ba mana dund, ma fas ak yeen kóllëre gu sax, gi ma baaxee Daawuda ci ngor gu wóor.

«Asamaan su yees sii, ak suuf su yees sii may waaja sàkk déy, ni seen taxawaay di yàgge fi sama kanam, yeen, ni la seen askan ak seen tur di yàgge fi sama kanam.

¶ «Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «yu may fas ak waa kër Israyil ak waa kër Yuda kóllëre gu yees.

Ñooy dëkke réew mi ma joxoon Yanqóoba sama jaam ba, te seeni maam dëkke woon ko. Ñu dëkke ko ñoom it, ñook seeni doom ak seeni sët, ba fàww, te Daawuda sama jaam ba mooy doon seen boroom jal ba fàww.

Gannaaw bu ma walee waa kër Israyil sama noo, dootuma leen xañ sama kanam. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.»

¶ Yeen nag nekkatuleen ci kilifteefu bindu suuxu neen, waaye ci kilifteefu Noo gi ngeen nekk, ndegam kay Noowug Yàllaa ngi màkkaanoo ci yeen. Ku amul Noowug Almasi, kooku du nitam.

Waaye tey la Yeesu jot ci liggéeyu carxal gu sut gu jëkk ga fuuf, te kóllëre gi mu fas diggante Yàlla ak nit ñi, noonu la gëne gu jëkk ga; dige yi lal kóllëre gu yees gii it, noonu la gëne dige ya laloon gu jëkk ga.