Musaa ne yékkét yet wa, mu jublu asamaan, Aji Sax ji yebal dënu baak tawub yuur ba, sawara wa ne yureet fi suuf, ànd ak tawub yuur, ba Aji Sax ji sóob ca réewum Misra.
TSK
TSK · Jeremiah 10:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Gannaaw loolu Ilyaas ne Axab: «Doxal lekki te naan, ndax taw bu réy a ngi riir di ñëw.»
Keey ñoddi toqi ndox, mu def ub lay, tawal,
Yaa àkki ba fa mbàndi tawu yuur ya? Am yaa gis mbàndi waamey donj yu sedd,
di taw fu kenn newul, ci màndiŋ mu nit amul,
leer a ko jiitu, xàmbaar ya topp ca, ak tawub yuur ak xali sawara.
Yeen waa réewi àddina, woyleen Yàlla, teral-leen Boroom bi, Selaw
Mooy yékkateey niir fa cati àddina, sàkkal taw ay melax, yebbee ngelaw cay dencam,
mooy sànge asamaan ay niir, tawal suuf, saxal tund yi am ñax,
Xërëmi neen yi yéefar yiy jaamu, ana ku ci mana taw? Am asamaan ay sóobal boppam ay waame? Du yaw la Aji Sax ji sunu Yàlla? Yaw lanu yaakaar, te loolu lépp, yaw a.
Kii kat moo móol tund, di sàkk ngelaw, di xamal nit nammeelam. Kee di soppi lëndëm ag leer, di daagoo kawte ya. Kookoo di Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.