¶ Fàttlikuleen! Buleen fàtte na ngeen merloo woon seen Yàlla Aji Sax ji ca màndiŋ ma. La dale bés ba ngeen bàyyikoo réewum Misra, ba ba ngeen agsee bérab bii, fippu ci kaw Aji Sax ji ngeen masa nekke.
TSK
TSK · Jeremiah 22:21
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ndax maa xam seen jikkoy fippu, ak seenug dëgër bopp. Seetleen, ndegam bi may dundagum tey ci seen biir ngeen di fippu ci kaw Aji Sax ji, astamaak gannaaw bu ma deeyee.
Noo bàkkaar, nook sunuy maam; noo def lu ñaaw, def lu bon.
Dégguleen, yéguleen, seeni nopp masula bënn; xam naa ne ay workati neen ngeen, «njuddu-fippu» lañu leen di wooye.
Éey niti Israyili tey, teewluleen kàddug Aji Sax ji! «Ni màndiŋ mi aaye, ndax mas naa nee aaye ci Israyil? Mbaa ma mel ni réewum lëndëm aki loraangeem? Lu waral sama ñoñ naa: “Noo moom sunu bopp, dootunu délsi fi yaw”?
Aji Sax ji dafa wax ne: «Taxawleen ca selebe yoon wa, xool, te laajte yoon ya woon, ne: “Ana yoonu mbaax?” Ngeen awe ca, am noflaayu bakkan.» Ñu lànk ne: «Awunu ca.»
Mbir mii déy laa leen santoon ne leen: “Déggal-leen ma, ma doon seen Yàlla; yeen ngeen doon sama ñoñ. Doxeleen wépp yoon wu ma leen sant, su ko defee ngeen baaxle.”
Waaye dégluwñu, teewluwñu ma, xanaa sajju loos, di bon, ba yées seeni maam.
Aji Sax ji yónnee leen mboolem jaamam ñiy yonent yi. Yónni na leen ay yooni yoon. Waaye dégluwleen, teewluwleen.
¶ Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi wax ne: «Gannaaw dégluwleen samay kàddu,
Yónnee naa leen samay jaam, yonent yi, ay yooni yoon, ne leen: ‘Na ku nekk ci yeen dëpp yoonam wu bon, di def lu baax, baña topp yeneen yàlla, di leen jaamu, ndax ngeen dund ci réew mi ma leen jox, yeen ak seeni maam.’ Waaye teewluwleen ma, déggaluleen ma.
Teewul ñu gàntal ma, nanguwñu maa déglu. Kenn nanguwula xalab tuur yu seexluwu yi mu wékki gët, kenn dëdduwul kasaray tuuri Misra. Ma nar leena xëpp samam sànj, ŋaccal leen sama mer ci biir réewum Misra.
¶ «Waaye doom ya dañu maa gàntal. Sama dogali yoon, jëfewuñu ko, sama àttey yoon yiy guddal fanu képp ku koy jëfe, sàmmuñu ko. Sama bési Noflaay lañu ñàkke worma. Ma nar leena xëpp samam sànj, ŋaccal leen sama mer ca màndiŋ ma.
di gànctu ca Misra, te doon fa gànctu ca seenug ndaw. Fa lañu doon làmbe seeni ween, di motoxal seen cusi janq.