TSK

TSK · Joel 2:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Gannaaw ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikke na Ibraam wax jii ci peeñu, mu ne ko: «Yaw Ibraam, bul ragal dara; man maay sa kiiraay, te sa yool dina màgg lool.»

¶ «Léegi nag taxawleen ba gis jaloore ju réy jii Aji Sax jiy def, ngeen teg ci bët.

Yaay tëje mbeyum at mi say ngëneel, foo jaare, xéewal walangaan.

Asamaanoo, bégal! Suufoo, bànneexul! Géejoo, riiral yaak li la fees,

Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Ba Aji Sax ji delloo waa Siyoŋ seen réew, danoo meloon ni ñuy gént,

Màndiŋ ak suuf su ne sereŋ dina bég, joor gu wow bànneexu, tóor ba ne ràññ.

Asamaan, sarxolleel, Aji Sax ji dikk na! Yeen xóotey suuf, xaaculeen! Yeen tund yi, neleen réllet, sarxolleendoo, ak yaw gott beek sa bépp garab! Aji Sax jee jot Yanqóoba, te moom Israyil lay fésale darajaam.

«Mbégte déy, ngeen di génne, ñu yóbbu leen ci jàmm, tund yu mag yeek yu ndaw yi di leen sarxolleel, garabi àll bi yépp tàccoondoo.

Mu ne: “Woo ma, ma wuyu la, wax la lu réy te loq, loo xamul woon.”»

Joel 2:20 TSK

Waa bëj-gànnaar, maa leen di soreleek yeen, maa leen di dàq, jëme réew mu maral te wéet, gàngoor ga jiitu jubal géeju penku, ga féete gannaaw jubal 0géeju sowu, ba seeni néew gilli, xasaw ba ubale, ngir jëf ju réy ji ñu def!»

«ni laa nammatee baaxe, ci janti tey jii, Yerusalem, ak waa kër Yuda. Kon buleen ragal.