TSK

TSK · Lamentations 2:16

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 16:9 TSK

Meram la ma daggatee, jéppi ma, di yéyu ci sama kaw, daasal ma gëti noon, ne ma jàkk.

Tekkiwuñu dara, di ma ñaawal rekk te di ma màttu.

Yàlla buñu ne: «Ñaw! Lii rekk lanu bëggoon.» Yàlla buñu ne: «Sàkkal nanu ko pexe.»

Bañ yépp a ngi may déeyoo, di ma fexeel lu bon,

Ma woo Yàlla, Aji Kawe ji, Yàlla, mi may matalal.

Soxor bi da koy gis, mer, iñaan bay yéyu, jeex tàkk; nde soxor, yaakaar ju tas rekk.

Sa gentub tey bi déy a ngi wéet, di réew mu yàqu yaxeet. Waaye léegi déy mu fees ba far xat; fu ña la sànkoon di soree.

Noon bu taseek ñoom warax leen te naan: “Nun defunu dara. Ñoom ñoo moy Aji Sax ji, te mooy dalukaayu njekk, ba seeni maam yaakaaroon.”

«Buuru Babilon warax na ma. Da maa muucu, ñiit ma, ba ma set ni ndab. Da maa modd ni ninki-nànka, sole kollam li gën ci man, yàbbi la ca des.»

Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Sa kaasu mag ngay naane, xóot, yaatu, duy ba ne xéew, xellil la ay ñaawleeki kekku.

Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Yeena doon tàccu, di fecc, bége tiisu réewum Israyil, di leen sewal lu ngeen man.

Kon waxal waxyu bii, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Wet gu ne lañu leen same, yàqte leen, ba ngeen mujj di moomeelu yéefar yi, ñépp di leen jëw ak a tooge,

Waruleen woona seetaan ci seen bésub mbokk, bésub njekkaram, Waruleen woona bége deminu Yudeen ñi ci seen bésub sànkute, mbaa ngeen di réy làmmiñ, ci bésub njàqare.

«Maa dégg ŋàññi Mowab, kàddu yu ñaaw yi Amoneen ñiy ŋàññe sama ñoñ, tey damu, nara nangu seen suuf.