TSK

TSK · Leviticus 27:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Waaye su amul lu mu jëndaate suufam, suuf sa day des ca loxol ka mu jaayoon, ba keroog atum Yiwiku ma délsi. Bu atum Yiwiku ma délsee, sañ naa dellu ca suufam.

Mboolem lu ñu aayalal Aji Sax ji, lu sella sell la ñeel Aji Sax ji. Lépp lu nit moom, su dee nit mbaa jur mbaa suuf su mu donn, amu ci lenn lu mu aayalal Aji Sax ji te ñu sañ koo jaay mbaa mu di ko jotaat.

Mboolem alalu sëxëtoo ju jóge ca dëkk ba, dajaleleen ko ca digg pénc ma, te ngeen lakk dëkk ba, booleek cëxëtoo ma, def ko dóomal bu mat sëkk, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Day doon ab gent ba fàww, deesu ko tabaxaat.

Ezra 10:8 TSK

Ñu ne képp ku teewul ci diiru ñetti fan, ni ko kilifa yeek mag ñi diglee, dees na teg alalam jépp loxo, te moom ci boppam dees na ko dagge ca ngàllo, ga ñibbsi.