Waaye su ngeen jëfewul noonu kat, yeena moy Aji Sax ji, te xamleen ne seenug moy dina leen dab.
TSK
TSK · Proverbs 24:16
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ba loolu amee Sóol ne gàddukatu gànnaayam: «Boccil sa saamar, jam ma bala yéefar yee dikk, jam ma, torxal ma.» Gàddukatu gànnaayam nag buggu koo jam ndax tiitaange lu réy. Sóol jël saamaru boppam, daldi daaneel boppam ca kaw ñawka ga.
Juróom benni njàqare teew, mu xettli la ca, ba ko juróom yaareel sax, doo ca loru.
Sa yaakaar tas, Aji Sax ji jege la, sa xol jeex, Aji Sax ji wallu la.
Lu bon a la gënal lu baax, fen a la gënal wax dëgg. Selaw.
Ay topp na moykat, ku jub juble.
Mbégte ñeel na ku saxoo ragal, waaye ku dëgër bopp tàbbi ci njekkar.
Fëlëñ! Israyil janq ba dootu jógati. Ma nga ñu wacc ca suufas réewam, te amul ku ko yékkati.
Yaw samab noon, bu ma ree; maa daanu, maay jóg. Ci biir lëndëm laa toog, waaye Aji Sax jeey samag leer.
¶ Ndax kat, bokk yi, buggunu ngeen umple njàqare, ji nu daj ci diiwaanu Asi. Daj nanu coono bu jéggi dayo, te wees sunu kàttan, ba yaakaaratunu woona dund sax.
Xanaa ay surgay Almasi lañu? Naa ràkkaaju nag, te ne maa leen ko gëna doon. Bu dee ci liggéey yu metti, maa man fopp; bu dee ci fani kaso, maa ëpple fopp; bu dee ci ay yar, maa ëpple ay yooni yoon, te bare na lu ma riisu ndee, ba raw leen:
Ndokklee, asamaan, Ndokklee, yeen ñu sell ñi itam, ak ndawi Yàlla yeek yonent yi, ndaxte Yàllaa leen àtteek dëkk bii, mbugal ko.