¶ Mu am bés Ibraayma wax surgaam, bi gëna yàgg ci këram, tey saytu alalam jépp, ne ko: «Dugalal sa loxo ci sama suufu lupp,
TSK
TSK · Proverbs 27:18
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ci kaw loolu mu may Yuusufa, mu yilif ñi ñu tëj ñépp, te mboolem lu ñu fay def, mu di ko jiite.
Kon nag kàddug Aji Sax jee, Yàllay Israyil: “Maa waxoon déy ne, sa waa kër ak sa waa kër baay ñooy doxe fi sama kanam, di ma liggéeyal ba fàww.” Léegi nag, kàddug Aji Sax jee: “Loolu jomb naa ko tey. Ñi ma teral laay teral; waaye ñi ma teddadil, dees na leen tuutal.
¶ Fekk na ay xarekati waa Siri dem songi réewum Israyil, jàppe fa ab janq, def ko surgab jabaru Naaman.
Ngaanag Naaman dina la topp, yaak saw askan ba fàww!» Ba mu ko defee Gewasi bàyyikoo ca Alyaasa, daldi gaana, yaram wa ne fureet, weex furr.
Ma ne, ni jaam bu góor di wékke sangam bët, jaam bu jigéen di ko wékke bët sangam bu jigéen, ni lanuy wékke sunu Yàlla Aji Sax ji bët, ba keroog mu baaxe nu.
Seetlul ku man liggéeyam, buur lay liggéeyal, du liggéeyal baadoolo.
Ndokklee surga yooyu seen njaatige dikk fekk ñu teewlu. Maa leen ko wax déy, njaatige leey takku, toogal leen ba noppi dikk, taajal leen, ñu lekk.
Mu ne ko: “Jaaraamaa, surga bu baax bi. Gannaaw ci lu tuut nga wóore nag, falul ci fukki dëkk.”
¶ Naka la malaaka ma wax ak Korney ba dem, mu woo ñaar ciy surgaam, ak benn takk-der bu jullite te bokk ciy suqam.
¶ Kan moo masa ràngu liggéeyu coldaar, te léppam war ko? Ana kuy jëmbat tóokërub reseñ, te du lekk ca doom ya? Mbaa kan mooy sàmm ag jur, te du naan ca soowum jur ga?
¶ Jaam yi, nangul-leen ci lépp seen sang yi ci àddina. Buleen ko defe ngistal, mbaa ngeen di ko sàkkoo lu leen neex, waaye defeleen ko yéeney xol bu dëggu, ndax ragal Boroom bi.
¶ Yeen jaam yi, nangul-leen te weg wegeel gu mat sëkk seeni sang, te du sang yi baax te lewet doŋŋ, waaye ñu wex ñi itam ci lañu.