TSK

TSK · Romans 12:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Naka la siggi, gis ñetti nit, ñu ne jimeet ci kanamam. Ibraayma gaawtu, gatandu leen, sujjóotal leen.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.

Acts 4:35 TSK

teg ko ci kanam ndaw yi. Su ko defee ku nekk séddu ca la dëppook soxlaam.

Acts 10:4 TSK

Korney ne ko jàkk, tiit, ne ko: «Sang bi, lu mu doon?» Mu ne ko: «Say ñaan ak say sarax yéeg na fa Yàlla, ba mu bàyyi la xel.

Su dee wàllu kàddu yuy yokke, ngay wax luy yokk gëmkat ñi; su dee wàllu joxe, deel joxe te Yàlla rekk tax; su dee wàllu jiite, taxawal temm ci liggéeyub jiite; su dee wàllu baaxe nit ñi, nay loo bége.

¶ Ci wàllu ndimbal li jëm ci gëmkat ñu sell ñi, noonu ma ko digale mboolooy gëmkati diiwaanu Galasi, yeen itam defeleen ko noonu.

¶ Gannaaw loolu bokk yi, danu leen di xamal li yiwu Yàlla maye ci biir mboolooy gëmkati diiwaanu Maseduwan.

¶ Ndax liggéey bi ndimbal lii laaj kat, yemul rekk ci faj soxlay ñu sell ñi, waaye itam dina baawaanal cant gu bare, ñeel Yàlla.

Njiit li nag fàww mu mucc sikk, di ku dencul lu wees jenn jabar, ku moom bakkanam, jiital am xelam, di ku nawlu, man gan, te mana jàngle.

Titus 1:8 TSK

Waaye war na di ku man gan, ku xejjoo lu baax, jiital am xelam, jub, sell te moom boppam.

Yàlla ñàkkul worma bay fàtte seen liggéey, ak cofeel gi ngeen sopp turam, te firndeele ko ni ngeen taxawoo ñu sell ñi, démb ak tey.

Te it di def lu baax, ak di dimbalee, buleen ko fàtte, ndax sarax yu mel noonu la Yàlla gërëm.