¶ Aji Sax ji dellu ne Musaa: «Maa gis askan wii, askan wu dëgër bopp a ngii!
TSK
TSK · Acts 13:46
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ku bon daw na te dàqeesu ko, ku jub ñeme ni gaynde.
Ma ne, aw xeet woo xamul ngay wooyi, xeet wu la xamul ay dawsi ba ci yaw, ngir sa Yàlla Aji Sax ji, Aji Sell ju Israyil, nde moo la teral.»
te ciw turam, dees na dale ci Yerusalem, yégal xeet yépp, tuubeel gu jur njéggalug bàkkaar.
¶ Ba waa kurélu àttekat ya gisee fit, wi Piyeer ak Yowaan àndal, te ñu xam ne niti neen ñu masula jàng lañu, dañoo waaru. Xamoon nañu nag ne ñook Yeesoo nekkoon.
¶ «Yeena dëgër bopp, yeenay boroomi xol ak noppi yéefar! Dungeen noppee të Noo gu Sell gi? Maam ya, doom ya rekk!
¶ Ci kaw loolu, ñoom ñu jóge Perge, jàll ba Àncos ca diiwaanu Pisidi. Ñu dem jàngu ba, dugg, toog ca bésub Noflaay ba.
Ba Silas ak Timote dikkee, bàyyikoo diiwaanu Maseduwan, Póol xintewootul lu moy di xamle kàddu gi, di seereel Yawut yi ne Yeesu mooy Almasi.
Waaye li dale Damaas ak Yerusalem ba ci réewum Yawut gépp, ba ca ñi dul Yawut, ñoom ñépp yégal naa leen seen wartéef, muy tuubeel ak waññiku ci Yàlla, ak jëf ju tuubeel yellool.
¶ Awma lu may rus ci xibaaru jàmm bi, ndax kat mooy manoorey Yàlla jiy musal képp ku ko gëm, dale ci Yawut bi, teg ci ki dul Yawut.
Ñooñoo di xeetu Israyil wi xéewloo céru doon doomu Yàlla, xéewloo daraja, xéewloo kóllëre yi, ak ndigali yoon wi, ak liggéeyu jaamu Yàlla gi, ak dige yi;
¶ Moo tax ma ne xanaa ba bànni Israyil tërëfee, jéll bu ñu dul jógati lañu daanu? Mukk kay! Waaye tooñug bànni Israyil moo waral muccug jaambur ñi dul Yawut, ba tax bànni Israyil siis leen.
Te it li gëna bare ci bokki gëmkat ñi, sama jéng yi ma nekke nii moo leen yokk aw fit, ba tax ñu gëna ñemee waxe kàddu gi te ragaluñu ci dara.