TSK

TSK · Acts 20:35

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.

Ku baaxe ku ñàkk, lebal nga Aji Sax ji, te moo lay yool.

Ku yoqi, dooleel-leen ko, ku óom yay fenqe, jàppleleen ko.

¶ Ci kaw loolu Yeesu ne waa ja ko woo bernde: «Boo dee waajal bernde, añ mbaa reer, bul woo say xarit, mbaa say doomi ndey, mbaa say bokk, mbaa say dëkk yu am alal, nde ñoom itam dañuy walbatiku, woo la rekk, mu doon sag pey.

Ndax mboolem li Yàlla nar bañuma leen cee xamal lenn.

Ndegam ñeneen a jagoo boobu sañ-sañ ci yeen, astamaak nun. Waaye nag jariñoowunu sañ-sañ boobu. Lépp lanu far muñ, ngir baña gàllankoor yoonu xibaaru jàmm bu Almasi.

¶ Lii rekk la: ji lu tuut, góob lu tuut; ji lu bare, góob lu bare.

Noonu may def rekk laay saxoo, ngir xañ aw lay, ñiy wut aw lay wu ñu damoo, naan ñook nun a yem kepp daraja.

Sàcc bi, na ba sàcc te nangoo sonn, di liggéeye loxoom liggéey bu rafet, ba man cee dimbali néew-ji-doole ji.

Sàkkuleen di jëfe jëfin wu dal, te ngeen di topptoo lu seen yoon nekk, tey dunde seenu ñaq, na nu leen ko sante woon.

¶ Kon nag «dëgëral-leen loxo yi toqi, ak óom yi bañ,»

Te it di def lu baax, ak di dimbalee, buleen ko fàtte, ndax sarax yu mel noonu la Yàlla gërëm.