TSK

TSK · Daniel 10:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Seeni tànk daa jub, téstën ya mel ni weyi sëllu di melax ni xànjar bu ñu jonj.

Mbege yaa ngay nirook peru kirsolit, ci melokaan ak ci bind. Ñoom ñépp a niroo. Seen melokaan ak seen bind daa mel ni, mbege mu ci nekk, mbegee nekk ca biiram,

¶ Ma xool, yem ci jëmm ju ame melokaanu nit. Li ko dale fiy nirook lupp yi, jëm suuf, sawara la. Li dale ci lupp yi jëm kaw ame melokaanu leer, mel ni weñ guy tàkk.

Ca digg tegukaayi làmp ya, jëmm juy nirook nit a fa nekk. Ma nga sol mbubb mu tollu ci ndëgguy tànk yi, takkoo ngañaayal wurus ci dënn bi.

Mu xaacu ca kaw, mel ni gaynde guy yëmmu. Naka la xaacu, juróom ñaari dënu jib.

juróomeel bi di sarduwan; juróom benneel bi di kornalin; juróom ñaareel bi di kirsolit; juróom ñetteel bi di beril; juróom ñeenteel bi di topaas; fukkeel bi di kirsoparas; fukkeel beek benn di yasent; fukkeel beek ñaar di ametistë.