Wóoy Sóol ak Yonatan, ñoo yiw, sopplu ba ñuy dund, te ba ñu deeyee, teqlikoowuñu. Ag jaxaay, ñoo ko gëna gaaw, te gaynde, ñoo ko gëna jàmbaare.
TSK
TSK · Daniel 7:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax ji, jógal, bu la nit yab; na xeet yi dikk fi sa kanam, nga àtte leen.
Xanaa du yaa doon wax ci sam xel, naa: “Maay yéeg kaw asamaan, maay aj sama jal kaw biddiiwi Yàlla, maay toogi kaw tundu ndaje ma, fa catal bëj-gànnaar.
«Noon baa ngii, di jóg niy niir, watiiri xareem ni ngëlén, fasam ya gëna gaawi jaxaay. Wóoy ngalla nun, yàqu nan!»
Gaynde wacc na geeram, seen réew ma di ndànd-foyfoy, ndax saamaru notkat bi ak tàngooru sànjum Aji Sax ji.
Maa ngii di fëlle gottub Yurdan ni gaynde, wuti mbooy gu naat. Xef ak xippi déy, ma fëxale fa ñépp, ba tabb fa ki ma taamu. Ana moos ku mel ni man? Ku am sañ-sañ ci man? Ana njiit luy taxaw fi sama kanam?
Ñi ñuy dàqa gëna gaaw ay jaxaay, ci kaw tund yi lañu nu ne dann, màndiŋ mi, ñu di nu fa tëroo.
«Yaw nit ki, waxal Boroom Tir, ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Dangaa fuuy ba naan: ‘Maay Yàlla, ji tooge toogub yàlla yi, fi xolu géej!’ Waaye yaw doom aadama nga, doo Yàlla, dangay yàlla-yàllalu rekk.
te Yàlla teg ci say loxo doom aadama yeek rabi àll yeek njanaaw yi, nga boole leen yilif ñoom ñépp ak fu ñu mana dëkke: yaw yaay boppu wurus bi.
Rab ya ca des nag, ñu nangu seen kilifteef. Teewul ñu bàyyi leen ñu dundaat ab diir.
Biiñ day wore, jàmbaar ju bew jii nag du dal-lu, xanaa yàkkli puruxam ni njaniiw, du doylu, mbete ndee, moom miy buubandoo xeetoo xeet, dajale askanoo askan, aakimoo.