Ay gaal ay jóge tefesu Kitim, néewalsi doole Asur, néewalsi doole Eber. Waaye ñoom it dañuy mujj sànku.»
TSK
TSK · Daniel 8:23
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Feek lu yàgg dees na la woo. Bu ay at jàlle ba jeex, yaay songi am réew mu nit ña rëcc saamar, ba jóge ci ay xeeti xeet, dajeji ca kaw tundi Israyil ya yàggoona wéet. Ñooñoo seppikoo ci xeeti àddina yi, ñoom ñépp dëkksi fa ci biir xel mu dal.
¶ «Ni ma ne jàkk ci béjjén yi, beneen béjjén bu ndaw ne pëll, génn ci seen biir, ñett ca béjjén ya jiitu buddeeku. Béjjén bu ndaw baa nga am bët yu mel ni bëti nit ak gémmiñ gu muy waxe kàdduy damu.»
Ma bëgga am lu leer ba tey ci fukki béjjén yi ci bopp bi ak beneen ba génn, ba ñett daanu ca kanamam; mu am ay bët ak gémmiñ, di wax kàdduy damu, te ëpp yi ci des.
Ci kaw loolu béjjén bu ndaw génne ci béjjén yooyu benn, daldi lawa law jublu bëj-saalum ak penkook réew ma gëna rafet.
Léegi ñëw naa ngir xamal la liy dikkal sa mbooloo ci jamono yiy ñëw ndax peeñu mi ëmb na jamono yooyu itam.»
Day dugg ndànk ba ca biir gox ya gëna woomle ca diiwaan ba. Dina fa def lu ay baayam aki maamam masula def. Dina lël ay réew, séddale ay farandoom alal jaak koom ga. Dina lal pexe yu mu songe ay tata, waaye loolu ab diir lay doon.
Ñoo nuy aaye nu àgge jaambur ñi dul Yawut, kàddu gi leen di musal. Noonu lañu matale seen jóorub bàkkaar yi ñu nekke naka jekk, waaye am sànj a leen mujj dab.
¶ Noowug Yàlla wax na ci lu leer ne ci mujug jamono, dina am ñu wacc yoonu ngëm wi, di topp ay xalaat yuy fàbbee ak ay àlluway ceytaane,
Ñu daldi jàpp rab wi, mook yonentu caaxaan, bi defoon ci turu rab wi ay kéemaan yu mu sànke ña ñu màndargaale woon màndargam rab wi, te ñu doon jaamu jëmmu nataalu rab wi. Ñoom ñaar ñépp lañu sànni, ñuy dund ca déegu sawara waak tamarax bay bax.