TSK

TSK · Daniel 9:25

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Ezra 4:24 TSK

Ci kaw loolu liggéeyu kër Yàlla ga ca Yerusalem taxaw. Taxaw na ba ca ñaareelu atu nguurug Daryus buuru Pers.

Ezra 7:1 TSK

¶ Ba loolu weesee, ca jamonoy nguurug Artaserses buuru Pers, am na góor gu ñuy wax Esra, Seraya di baayam. Seraya, Asaryaa; Asaryaa, Ilkiya; Ilkiya,

Ezra 7:11 TSK

¶ Lii mooy li ñu bind ci bataaxal ba Buur Artaserses jox Esra, sarxalkat ba, jànglekat ba géeju ci mbiri santaaney Aji Sax ji ak dogalam yi ñeel Israyil.

door ne Buur: «Xanaa Sang bi, su la neexee rekk, nga yéwéne ma, yebal ma Yuda, dëkk ba ñu denc samay maam, ba ma tabaxaat ko.»

¶ Gannaaw loolu Elyasib sarxalkat bu mag ba ànd ak bokki sarxalkatam, ñu tabaxaat bunt ba ñuy wax Gàtt ya, sellalal ko Yàlla, taxawal laf ya, defaraat tata ja, ba ca soorooru Meya, sellalal ko Yàlla, jàppoo ko noonu ba ca soorooru Ananel.

Ba loolu amee ma xoolaat lépp, ba noppi wax ak kàngam yaak kilifa yaak mbooloo ma ca des ne leen: «Buleen leen ragal. Fàttlikuleen ne Boroom bi moo màgg te jara ragal te ngeen xeexal seeni bokk ak seen doom yu góor ak yu jigéen, ak seeni jabar ak seeni kër.»

¶ Ba mu ko defee tata ji noppi ñaar fukki fan ak juróom ci weeru Elul. Ñu liggéey ko ci juróom fukki fan ak ñaar.

Mu jot nga rey, mu jot nga faj; mu jot nga toj, mu jot nga tabax.

Ab seedee ngoog, ñeel xeet yi, muy njiit, yilif xeet yi.

Xelum njublaŋam lay naxee, di réy-réylu, ba bett ñu bare, faagaagal leen, te dina dëkk kilifay kilifa yi. Waaye mooy sànku, te loxo du ko laal.

Micah 5:1 TSK

«Yaw Betleyem Efrata, lu tuut ci làngi Yuda, ci yaw la ku may yilifal Israyil di génne, cosaanam di jant yu yàgga yàgg, bu jëkkoon.»

Acts 5:31 TSK

Moom la Yàlla yékkati ci wetu ndijooram, def ko muy Njiit, di Musalkat, ngir may bànni Israyil ag tuubeel ak njéggalug bàkkaar.

Jariñooleen lu ngeen man, jot gi ngeen amagum, ndax jant yu bona ngii tey.

Ci kaw mbubbam ak ci luppam, aw tur lañu ci bind te moo di: «Buuru buur yi, Sangu sang yi.»