TSK

TSK · Genesis 21:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba mu dawee, malaakam Aji Sax ja gis ko fu dend akub bëtu ndox ca màndiŋ ma, mooy bëtu ndox, ba ca yoonu Sur.

Looloo tax ñu tudde teen boobu Beerseba (mu firi Teenu waat ga), ndaxte fa lañu waatoo woon ñoom ñaar.

¶ Ibraayma nag teela xëy, takk mbaamam, ànd ak ñaari surgaam ak doomam Isaaxa, daldi xar matt, mi muy lakke sarax bi. Ma nga jëm fa ko Yàlla wax.

Ba loolu weesee mu doora lekk, daldi naan, moom ak ñi mu àndal. Ñu fanaan fa keroog. Ba ñu yewwoo ca ëllëg sa, surga ba ne: «Bàyyileen ma nag, ma dellu ca sama sang.»

Ca ëllëg sa, ñu xëy suba teel, daldi waatoo, Isaaxa door leena yiwi, ñu dem ci jàmm.

¶ Ca suba teel Yanqóoba jóg, jël doj, wi mu gegenoo woon, samp fa, muy xàmmikaay, ba noppi sotti ci ag diw, sellale ko.

¶ Naka la jenn waay dajeek moom foofa, fekk muy wëreelu ca àll ba. Waa ja ne ko: «Looy seet?»

¶ Ilyaas gis na mu deme, daldi daw, ngir rawale bakkanam. Mu dem ba Beerseba ca réewum Yuda, bàyyi fa surgaam.

Ñee ngi taxawaaloo màndiŋ mu wéet, gisuñu dëkkuwaay,

Tool ya fa Esbon day wow, njiiti xeet yee dëggaate ngëneelu reseñ gu Sibma, te cabb ya laloon ba Yaser, ba àkki déndu màndiŋ ma, car ya law ba wàllaa géej.

Doomu jaam bi moo juddu ci kaw coobarey bakkanu nit, waaye ki gor si jur, ci kaw digeb Yàlla la juddu.