Làq ma pexey ku bon, ma rëcc gàngooru defkati ñaawtéef.
TSK
TSK · Hosea 5:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Xanaa dungeen wéye fippu, ñu gën leena duma, te bopp di góomi neen, xol jeex tàkk?
Aji Sax ji, xanaa du worma ngay sàkku? Dóor nga leen, safu leen; nga làbbli, ñu tanqamlu, wowle ba raw doj, baña dëpp.
Aji Sax jee ma xamal, ma xam, ba gis seeni jëf.
¶ Li ko dale fukkeelu at ak ñett ci nguurug doomu Amon, Yosya buurub Yuda, ba tey jii, di ñaar fukki at ak ñett, kàddug Aji Sax jaa ngi may dikkal, ma di leen ko jottli te tàyyiwma, waaye dégluwleen.
Moo tax yonent yi laa leen di dumaa, sama kàdduy gémmiñ laa leen di reye. Seen àttee leen di jollil ni ceeñeeru njël.
«Seen gépp mbon moo feeñ ca Gilgal, te fa laa leen jéppee ndax mbonug seeni jëf. Sama kër laa leen di dàqe, te dootuma leen bëgg, seeni njiit yépp a diy fippukat.
Wóoy ngalla fippukat bu sobewu bi, dëkkub notkat yi.
¶ Ba bët setee Yawut ya daje, daldi xasoo, ne duñu lekkati, duñu naanati, ba kera ñu reyee Póol.