¶ Waa Misra dañoo mujj di jaamloo bànni Israyil bu metti,
TSK
TSK · Isaiah 52:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Aji Sax ji tegaat ca ne ko: «Gis naa bu baax fitna, ji sama ñoñ nekke Misra. Dégg naa itam seen jooy ndax kilifay saskat, yi leen di gétën ci liggéey, te ñeewante naa leen ngir seen coono.
Ni gàtt yu ñuy yàpp, ni nga nu joxee, tasaare nu ci biir xeet yi.
Éy Yàlla, fu reetaani noon di dakke? Xanaa bañ yi duñu la ñàkke kersa ba fàww?
Éy Yàlla, jógal ñoŋal sa dëgg, bàyyil xel dof bi la dëkkee sewal.
Ana loo fi am, ak koo fi am? Nga di fi yettlu bàmmeel, yett ko ca kawte ya, di gaslu kër gooy mujje?
Waaye boo toogee, boo génnee, boo duggee, xam naa, boo xadaroo sama kaw it, xam naa.
Sa doom yi ne lasar, mbete kooba yu fiir jàpp, ñu ne lareet fépp fu mbedd daje, këppoo sànjum Aji Sax ji, sa Yàlla ji leen rëbb.
Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Dees leena wànteeroon ci dara, te du xaalis lees leen di jotaate.»
Dégg nañu may binni, te awma ku ma dëfal. Noon yépp a dégg samaw ay te di ko bége, nde yaa ko def. Ngalla indil bés bi nga dige, ba ñu daj li ma daj.
Waxambaane yee yenu doji wolukaay, gone yu góor yi sëfoo sayi matt, di tërëf.
Teewul ma sédd ci sama teddngay tur, ngir xeet, ya seede woon ba ma leen di génne, bañ maa sikk.
Su bés baa,» Aji Sax jee ko wax, «yuux dina jibe fa buntu Jën ya, wóoy jibe fa Sanc ya, rajaxoo ju réy jollee ca tund ya.