sama xalam tiisal, sama toxoro jooy.
TSK
TSK · James 4:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ngëneel la ma duma yi jural, ngir jànge naa ci say tegtal.
Kuy ji di jooy, yal na góob, di sarxolle.
Ma ne: «Reetaan ag nitoodi la; te mbégte lu muy jariñ?»
Bésub keroog Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi moo leen di woo ci jooyoo ak ñaawlu ak wateefu nel, ak colu saaku ngir ñaawlu.
Su boobaa janq bégem pooj, waxambaaneek mag feelu ko, ma soppi seen ñaawlu mbégte, dëfal leen, bànneexal leen, ñu dëddu naqar.
Xol nux-nuxeetul, te ay rongooñ a wuutuy pooj.
Su ko defee nga fàttliku démb, daldi rus, torox ba ne xerem keroog ba ma lay jot ci mboolem loo def. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”»
Wóoy ngalla yeen ñi regg tey, ndax dingeen xiif ëllëg. Wóoy yeen ñiy ree tey, ndax dingeen tiislu, dingeen jooy.
Ndaxte tiis wu Yàlla namm, ag tuubeel gu jëme cig mucc lay jur, te loolu du tiis wees di tiisoo. Waaye tiisu àddina, ndee lay jur.
Joxleen ko ci toskare aku naqar, kemu daraja jaak dund gu bakkane ga mu jagoo woon. Gannaaw moo ne cim xelam: “Maa tooge jalu lingeer, dumab jëtun, duma deele mukk,”