TSK

TSK · Joel 2:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba mu ko defee Ruben dellu ca kàmb ga, gis ne Yuusufa nekkatul ca biir, mu mititlu ko, ba xotti ay yéreem.

Ci kaw loolu Aji Sax ji romb fa kanam Musaa, di biral naan: «Aji Sax jee, Aji Sax ji, Yàlla jiy yërëm, di yéwéne, mer ma diib, ngor gaak kóllëre ga bare.

¶ Ba loolu amee Daawuda sëq yéreem, xotti, ña ànd ak moom ñépp itam, noonu, ndax aw naqar.

¶ Naka la buurub Israyil jàng bataaxal ba rekk, ne mbubb ma tareet ndax jaaxle, daldi ne: «Man dama di Yàlla bay rey, mbaa may dundal, ba kii di yebal nit ku may fajal ngaana! Seetleen lii rekk: kii da may wut!»

¶ Ba Buur déggee kàdduy téereb yoon wa, daa xotti ay yéreem ndax tiitaange.

Job 1:20 TSK

¶ Ba mu ko defee Ayóoba jóg, ne tareet mbubbam, ba noppi watu nel, di ko ñaawloo. Mu daanu fi suuf, sujjóot,

Boroom bi, may ma, ma wax, ma delloo la njukkal.

Waaye yaw Boroom bi Yàlla, yaa ñeewante, yërëm, yaa muñ mer, bare ngor ak worma.

bàyyi xel ci kóllëreem ak ñoom, topp ngoram lu réy, ba giif,

Ku màgg, ku kawe ki, ki màkkaanam sax dàkk te turam sell, daa wax ne: «Fu kawe te sell laa màkkaanoo, maa dëkk ak boroom xol bu mokk, te toroxlu, ngir leqli ku toroxlu, leqli boroom xol bu mokk.

Mboolem yooyu, sama loxoo ko sàkk; nii la lépp ame.» Kàddug Aji Sax jee. «Ku mel nii laay niir: néew-ji-doole ji xolam jeex, te muy déglu sama kàddu bay lox.

xeet woowu tuub mbonam gi ma leen doon artoo, ma fomm musiba mi ma naroona wàcce ci seen kaw.

Aji Sax ji ne ko: «Wëral dëkk bi, ci biir Yerusalem. Foo gis kuy onk ak a binni, di ko naqarloo gépp tojaange gu ñu fiy def, nga rëdd aw rëdd ci jëëm.»

Jonah 3:9 TSK

Jombul Yàlla dëpp ba fomm, daldi dëddu tàngooru meram, ba dunu sànku.»

Ana Yàlla ju mel ni yaw, di bale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom. Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.

Am dangay sofental mbaaxu Yàlla gu réy, akug jéllaleem, akug muñam, ndax ñàkka xam ne li Yàlla namm ci baaxe la, moo di nga tuub?

¶ Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw cofeel gu réy, gi mu nu sopp,

¶ Bokk yi, soppe yi, nangeen xam lii: na ku nekk di gaaw ci déglu, di yeexa wax tey yeexa mer.