TSK

TSK · Numbers 13:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ñu dem ba ca xuru Eskol, daldi fay dagge ab car bu def benn cëggub reseñ, ñaar ca ñoom gàddoo ko bant, ñu sàkkaale fa gërënaat ak figg.

ba noppi sàkk ca meññeefum réew ma, indaaleel nu. Ñu wax nu nag ne nu: «Réew mu baax la nu sunu Yàlla Aji Sax ji jox.»

¶ Ba loolu amee Musaa woolu Yosuwe, wax ak moom, Israyil gépp teg ci seen bët. Mu ne ko: «Dëgërlul te am fit, ndax yaw yaay ànd ak mbooloo mii ca réew ma Aji Sax ji giñaloon seeni maam, ne ñoom la koy jox. Yaw it yaa leen koy sédde.

Nangu nañu ay dëkk yu tata wër, ak suuf su nangu, aakimoo kër yu fees ak gépp ngëneel, aki teen, ak tóokëri reseñ, ak garabi oliw, garab yay meññ, ne xas; ñuy lekk ba suur. Ñu regg, di xéewloo sa mbaax gu réy gi.

Ay parlu yu baax laa leen di forale, kaw tundi Israyil yu kawe ya di seen parluwaay. Foofa lañuy goore parluwaay yu baax, te ñax mu naat lañuy fore foofa ca kaw tundi Israyil.

Moo tax nu mana am fitu wax ne: «Boroom beey sama ndimbal, duma tiit. Ana lees ma manal?»