TSK

TSK · Numbers 14:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Maay yékkati sama loxo jëme asamaan, giñ ne: “Ndegam maay dund ba fàww,

Cant ñeel na teddngaam, ba fàww, yal na teddngaam dajal suuf sépp! Amiin, Amiin!

Séentul fi la wër te xool! Ñépp a ngi daje, di la fekksi. Ndegam maay Kiy Dund,» kàddug Aji Sax jee, «ñoom ñépp ngay takkoo ni gànjar, gooy gànjaroo nib séet.

¶ «Moo tax, dogu naa ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, gannaaw yeena def seen wépp njombe ak seen jépp jëf ju siblu, di sobeel sama bérab bu sell bi, man itam, maa leen di wat nel te duma leen xool bëtu ñéeblu, duma leen ñeewante.

Noonee ma layoo woon ak seen baay ca màndiŋu réewum Misra, ni laay layook yeen. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.

Wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Giñ naa ko ci man miy dund, ku nekk ci yeen ci biir gent yi, saamar lay fàddoo; képp ku nekk ci biir àll bi, rab yi laa koy jox, ñu lekk ko; te képp ku làqoo tata yeek xunti yi, mbas a koy rey.

Moo tax, giñ naa ko ci man miy dund,» kàddug Aji Sax ju gàngoor yee, Yàllay Israyil, «Mowab déy ni dëkkub Sodom lay mujje, Amoneen ñi mel ni Gomor, ay dég ak paxi xorom a koy nangu, mu gental ba fàww. Sama ndesu ñoñ a leen di sëxëtoo, ndesu xeet wi ma séddoo moo leen di moom.»