TSK

TSK · Numbers 19:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Su fekkee ne nit ki dafa laal sobey nit ak su mu mana doon, te teyu ko, ba mu wees, saa yu ko xamee, tooñ na.

¶ «Su fekkee ne nit ki dafa moy lenn ci santaaney Aji Sax ji ci lu warul lu mu def, su ko xamul it, tooñ na, te dees na ko ko topp.

¶ «Fexeleen ba bànni Israyil di tàggook seeni sobe, lu ko moy dinañu dee ndax seen sobe, ngir dañuy taqal sama màkkaan mi ci seen biir.»

Wax leen ne leen: Muy tey, muy ëllëg, ba fàww, képp ku sobewu, di góor gu bokk ci seen askan, bu jegee lenn luy sarax su sell su ma bànni Israyil jagleel, kooku dootu ma liggéeyal. Maay Aji Sax ji.

Ni ngay def ngir setluloo leen nii la: Danga leen di wis ndoxum setlu, ba noppi ñu wat seen yaram wépp, fóot seeni yére, daldi set.

¶ Nit ki tooñ cig teyeefam nag, muy njuddu-ji-réew, di doxandéem, kooku Aji Sax ji la ñàkke kersa. Nit kooku, dees koy dagge ci biiri bokkam:

Bu loolu wéyee, na ku set jël caru isob, capp ko ca ndox ma, wis-wisal ko ca kaw xayma ba nit deeye, wis ko ca kaw ndab yépp, ak ca kaw nit ña fa nekkoon. Na ko wis itam ci kaw nit ku laal yaxi ku dee, mbaa mu laal ku ñu bóome saamar, mbaa mu laal ku Yàlla moomal boppam, mbaa mu laal bàmmeel.

Gannaaw nag kàddug Yàlla ga jibe woon ci gémmiñu malaaka yi, mujj na di lu wér péŋŋ, te képp ku ko masa xëtt, mbaa mu déggadi ko, jot nga añ bi war ci sag tooñ,

waaye ñu ragal ñi ak aji gëmadi ñi ak defkati ñaawtéef yi ak bóomkat yi ak moykat yi ak xërëmkat yi ak bokkaalekat yi, mboolem niti fen ñi, seen añ a nga ca déegu sawara waak tamarax ba. Loolu moo di ñaareelu dee.»

Ci biti, xaj yaa fa nekk ak xërëmkat yi ak moykat yi ak bóomkat yi ak bokkaalekat yi, ak képp ku sopp fen te di ko jëfe.