TSK

TSK · Numbers 21:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Léegi nag dellool góor gi soxnaam, ab yonent la de, te dina la ñaanal, nga raw. Waaye soo ko deful, na la bir ne dinga dee, yaak sa waa kër yépp.»

Musaa ak Aaróona nag jóge ca Firawna, Musaa tinu Aji Sax ji ca mbirum mbott ya mu yare Firawna.

¶ Firawna nag yónnee, woolu Musaak Aaróona. Mu wax leen ne leen: «Bii yoon de, maa tooñ. Aji Sax ji moo nekk ci dëgg, te maak sama waa réew ñoo sikk.

Baal ma àq bii yoon rekk, te ngeen ñaanal ma seen Yàlla Aji Sax ji, ngir mu teggil ma rekk, wii ay wu rey.»

¶ Ca ëllëg sa Musaa ne mbooloo ma: «Yeen de bàkkaar ngeen bàkkaar bu réy, waaye maa ngi nii di yéeg, jëm ci Aji Sax ji. Jombul ma jotul leen seen bàkkaar.»

Kon nag ngalla Boroom bi, na sa doole màgg rekk, noonee nga noon:

Ma ñaan Aji Sax ji, ne ko: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, bul sànk sa ñoñ ñi nga séddoo, ñi nga jote sa màggaay, génnee leen Misra ci sa dooley loxo.

¶ Sóol ne Samiyel: «Bàkkaar naa! Ndax maa wàcc kàddug Aji Sax ji ak say digal, ndax ragal mbooloo mi, ba topp seen coobare.

Buur ne góoru Yàlla ga: «Rikk tinul ma sa Yàlla Aji Sax ji te ñaanal ma, sama loxo mana banku.» Góoru Yàlla ga tinul Buur Aji Sax ji, loxoom bankuwaat, mel na mu meloon.

Job 42:10 TSK

Gannaaw ba Ayóoba ñaanalee xaritam ya, Aji Sax ji tijji wërsëgu Ayóoba. Aji Sax ji ful na ñaari yoon mboolem alalu Ayóoba.

Yàlla da leen doon sànk, bu dul woon ak Musaa, xejjam ba ko kar, àtte leen, mu giif, ba fàkkasu leen.

¶ Mu am bés Buur Cedesyas woo Yukal doomu Selemya, ak Cefaña sarxalkat bi, doomu Maaseya. Mu yebal leen ci Yonent Yàlla Yeremi; ñu ne ko: «Rikk ñaanal nu ci sunu Yàlla Aji Sax ji.»

¶ Bokk yi, sama yéeney xol, ak ñaan gi may ñaanal Israyil ci Yàlla moo di ñu mucc.