TSK

TSK · Numbers 27:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu solal ko nag kiiraayal dënn ba, daldi yeb ca biir kiiraay la jumtukaayi tegtal ya, di Urim ba ak Tumim ba,

kuy xareji, jiite leen, délsi, jiite leen, di leen yóbbu, di leen délloosi, ba mbooloom Aji Sax ji baña mel ni xar yu amul sàmm.»

¶ Lewi la wax ne ko: Sa Tumim ak sa Urim, jumtukaayi tegtal ya, ñeel na góor gay sa wóllëre, yaa ko nattoo ca Maasa, joteek moom ca ndoxum Meriba.

Naka la Sóol di wax ak sarxalkat bi, coow la ca dalub waa Filisti gëna jolli. Sóol ne sarxalkat bi: «Ah, bàyyi ko sax.»

Daawuda nag yég ne moom la Sóol di fexeel njekkar. Mu ne Abiyatar sarxalkat ba: «Indil xar-sànni mi.»

Ci biir loolu Daawuda wax ak sarxalkat ba Abiyatar doomu Ayimeleg, ne ko mu indil ko xar-sànni mi. Abiyatar indil Daawuda xar-sànni ma.

Boroom dëkk ba nag aaye leen ñu lekk ci ñam yu sell yaa sell, ba keroog sarxalkat ba di am lu leer ci ñoom ci jumtukaayi tegtal yi ñuy wax Urim ak Tumim.