TSK

TSK · Daniel 2:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Maa ko feesale xelum Yàlla, ak xareñte ak déggin ak xam-xam, ak manoorey bépp xeetu liggéey,

Aji Sax jeey xañe, di maye, di detteel, di kaweel.

¶ Israyil gépp nag dégg àtteb Buur, daldi yéemu ci moom, ndax dañoo gis ne xelum Yàlla mu rafet a ngi ci moom, di ko jiite ci àtte dëgg.

Mboolem àddinaa daan wuta giseek Suleymaan, ngir taataansi xelam mu rafet mi Yàlla def cib xolam.

Booba mboolem mbirum buur, xamkati jamono ya ci wàllu yoon ak àtteb yoon lees koy diis.

Job 34:24 TSK

Mooy rajaxe boroom doole te du laajte, daldi fal keneen mu wuutu ko.

Dama ne ku réy: “Bul réy-réylu,” ne ku bon: “Bul bew,

ndax Aji Sax jeey maye xel mu rafet, kàddoom di taxa xam, di dégg.

Lu nekk ak jotam, jot gu nekk ak la ca war fi jant bi tiim.

ne su ngeen ma waxul gént gi, àtte bi di benn ci yeen ñépp. Gise ngeen ba nar maa wax ay fen aki caaxaan, di yaakaar jamono soppiku. Waxleen ma gént gi rekk, ma xam ne man ngeen maa wax pireem.»

Garab gi nga gis muy màgg di réy, njobbaxtal lay laal asamaan, ñu di ko séen ci àddina sépp,

Mboolem waa àddina di neen ci moom. Nu ko neex lay def ak gàngoori xarey asamaan ak waa suuf, te kenn du fél loxoom mbaa mu naa ko: «Ana looy def nii?»

¶ «Gannaaw ay at, buur bëj-saalum ak buur bëj-gànnaar dinañu mànkoo. Doomu buur bëj-saalum mooy séysi kër buur bëj-gànnaar, ngir dëgëral diggante bi. Waaye nguurug doom ja du yàgg, boroom këram it du dundaat lu yàgg mook seen doom. Doomu buur bëj-saalum day dee, mook toppam ak baayam ak boroom këram.

Ndax man maa leen di jox làmmiñ wu ànd ak xel, wu seen benn noon dul mana dàq mbaa di ko weddi.

Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu, mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njekk, di sunu sellte, di sunug njot,

gépp may gu baax, ak bépp jagle bu mat, fa kaw la bawoo, di lu wàcce fa Baay biy boroom leer yi, ki soppikuwul ci lenn, te genn ker gu toogadi nekkul ci moom.

Ci kaw mbubbam ak ci luppam, aw tur lañu ci bind te moo di: «Buuru buur yi, Sangu sang yi.»