TSK

TSK · James 4:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 27:8 TSK

Ana lu yéefar biy yaakaarati bu fàddoo, ba Yàlla moom bakkanam?

Won nga ma ndoddi noon, ma boole bóom bañ yi.

Keroog nga woo ma wall, duma wuyu, nga seet ma, seet, doo ma gis.

Ku tanqamlu jooyi ku ñàkk dina woote wall, wall ñàkk.

Bu ngeen ma tàllaleey loxo, ma fuuyu. Bu ngeen doon ñaan-ñaanee it, du maa leen di déglu: seeni loxo, deret la taq ripp.

¶ «Yaw nag Yeremi, bul ñaanal askan wii. Bu leen tinul, bu leen dagaanal. Ndax kat keroog bu ñu nekkee ci seen musiba, ba naan ma wóoy, du maay déglu.»

Micah 3:4 TSK

Lee tax noggatukat yii di woo Aji Sax ji wall, te du leen wuyu, kanamam la leen di làq, bésub keroog, nde ñoo bonal seeni jëf.

Ndaxte képp ku ñaan, dinga am; ku seet, dinga gis; ku fëgg it, dees na la ubbil.

Sa doom jii dikk, gannaaw ba mu yàqee sa alal ci ay gànc, nga reyal ko sëlluw yafal wi!”

James 1:6 TSK

Waaye ngëm la koy ñaane te bumu ci am benn sikki-sàkka, ndax kiy sikki-sàkka daa mel ni gannaxu géej bu ngelaw liy yóbbu, di ko lëmbaaje.