¶ Ba bët setee, Firawna jaaxle lool, ba woolu jibar ya ak boroom xam-xami Misra yépp, nettali leen la mu gént, te kenn manu koo firil Firawna.
TSK
TSK · Daniel 7:15
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Man de, bañuma laa sàmmal, topp la; bésub tiis it dagaanuma ko. Yaw de xam nga ko. Li ma wax it fi sa kanam la.
Buur ne leen: «Damaa gént lu ub sama bopp, ma bëgga xam lu muy firi.»
Buur de, garab googu yaw la. Yaa màgg, di bare doole; di màgg ba laal asamaan, sa kilifteef àkki cati àddina.
¶ «Fii la mbir mi yem. Man Dañeel nag, ma am njàqare lool, ba sama kanam soppiku, ma denc kàddu yooyu ci sama xel.»
Ba ma ca déggee, samay butit a yëngu, coow la tax samay tuñ di lox, sama yaram dee goyy, may lox fi ma taxaw, te ne cell, di séentu bésub njàqare, bay dikkal xeet wi nu song.
Li may wax moo di tiis wu réy laa am, ak naqaru xol wu dakkul,
¶ Ma dem ba ci malaaka mi, ne ko mu jox ma téere bu ndaw bi. Mu ne ma: «Jël ko te lekk ko. Dina wex ci sa biir nag, waaye ni lem lay neexe ci sa gémmiñ.»