Buleen dëddu mukk, ndax su boobaa topp ag neen lay doon; lu dul jariñe, du xettlee, ndax tuur yi kat, neenug neen la.
TSK
TSK · Deuteronomy 32:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Li ko waral di mboolem bàkkaar yi Basa ak doomam Ela bàkkaar te bàkkaarloo ko Israyil, ba feesal xolu Aji Sax ji Yàllay Israyil ndax seen tuuri neen.
Ñuy taal cuuraay foofa ca mboolem bérabi jaamookaay ya, di roy xeet ya Aji Sax ji dàq ngir ñoom. Ñuy def daal ay ñaawtéef, di merloo Aji Sax ji,
Gannaaw ñoo ma dëddu, di taalal yeneen yàlla cuuraay, ngir merloo ma ci mboolem liggéey bu ñu defe seeni loxo, samam sànj mooy tàkk fi bérab bii te du fey.”
Ñu di ko merlook seen bérabi jaamookaay, di ko fiirlook seen jëmmi tuur.
Fu aw xeet masa weccee yàllaam? Moonte duñuy yàlla sax! Moona xeet wi ma séddoo weccoo séen darajay Yàlla te du leen jariñ dara.
Sama bokk yaa ngooguy yuuxu yuux yu àkki fu sore, naan: «Moo Aji Sax ji daa newul Siyoŋ a? Moo Buurub Siyoŋ da fee nekkatul a?»
Xërëmi neen yi yéefar yiy jaamu, ana ku ci mana taw? Am asamaan ay sóobal boppam ay waame? Du yaw la Aji Sax ji sunu Yàlla? Yaw lanu yaakaar, te loolu lépp, yaw a.
Mu tàllal lu bindoo ni loxo, daldi sëq sama kawaru bopp, lenn ngelaw yékkati ma ba ca diggante kaw ak suuf, yóbbu ma ba Yerusalem ci biir peeñum Yàlla, ba ca buntu ëttu biir kër Yàlla ba janook bëj-gànnaar, fa ñu teg jëmmu bokkaale, jay sabab fiiraange.
Noowal bakkan a nga may rëcc, sama xel ne yarr ci yaw, Aji Sax ji, sama ñaan àgg fa yaw, ca sa kër gu sell ga.
Moom la wax it ci téereb Ose ne: «Ñi dul woon sama ñoñ, ñoom laay wax sama ñoñ, ñooñu dul woon samab xejj, ñoom laay xejjoo.»
¶ Moo tax ma ne xanaa ba bànni Israyil tërëfee, jéll bu ñu dul jógati lañu daanu? Mukk kay! Waaye tooñug bànni Israyil moo waral muccug jaambur ñi dul Yawut, ba tax bànni Israyil siis leen.
¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.