Ku bon ay ñédd ay fanam ci biir teraanga, doora jekki wàcci njaniiw.
TSK
TSK · Luke 15:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ku bon daŋŋiiral, seetul dara, xalaatam yépp mooy Yàlla amul.
Soreel ndaw soosu, bul jege bunt këram.
Kuy sàggane sa liggéey, yaak kuy yàq a bokk.
Ku xelu denc këram ngëneeli alal aku diw, ab dof saax-saaxee josam.
Ku sore fa nga bokk, dangay mel ni picc mu sore tàggam.
Kuy jëfe xel, bégal sa baay; nga ànd aki gànc, yàq alal.
Wóoy wii xeetu moykat, wii askan wu diisu ñaawtéef, mii njurum defkati mbon, yii doomi yàqute! Ñoo wacc Aji Sax ji, ñoo teddadil Aji Sell ju Israyil, dëddu ko.
Moyal yoon wi; lajj, wàcc xàll wi, te may nu jàmm ak Aji Sell ju Israyil.
Aji Sax ji dafa wax ne: «Ana sikk bu ma seeni maam gisal, ba tax ñu sore ma, di topp xërëmi neen, ba far neen?
Xanaa du yeena def seen bopp lii, di wacc seen Yàlla Aji Sax ji, ba mu leen di jiite ca yoon wa?
Wóoy yeen ñiy jéema fanq bésub njàqare tey woo nguurug fitna!
Sa doom jii dikk, gannaaw ba mu yàqee sa alal ci ay gànc, nga reyal ko sëlluw yafal wi!”
¶ «Jenn waay la woon ju bare alal, di sol yérey tànnéef yu rafet, di dunde lu neex bés bu set.
Waaye yeen ñi sore woon, léegi bi ngeen nekkee ci Almasi Yeesu, jege ngeen ndax deretu Almasi ji tuuru.
Ndax démb kat yàgg ngeena def coobarey xeet yi xamul Yàlla, ci ay ñaawtéef, ak topp seen bakkan. Dangeen daa màndi ak a xawaare, dëkke naan biiñ, di jaamu tuur yu seexluwu, waaye na fi yem nag.