TSK

TSK · Romans 3:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 36:3 TSK

Fu xóot laay jukkee sama xam-xam, ba delloo dëgg ki ma sàkk.

Fóotal maa fóotal sama ñaawtéef, raxasal ma sama moy.

Aji Sax jee baax, gore ba fàww, worma ja sax dàkk!

Sa mboolem kàddu dëgg la, sa ndigal yépp di njekk, sax dàkk.

Yaay sàmm kóllëre ak Yanqóoba, yéwéne Ibraayma, na nga ko giñale woon sunuy maam, janti démb.

¶ Xanaa dikk, rey beykat yooyu, dénk tóokër ba ñeneen.» Nit ña dégg loolu daldi ne: «Yàlla tere!»

Mukk kay! Su njubteg Yàlla matul woon, ana nu muy àttee àddina?

Mukk kay! Nun ñi ndee tàggale ak bàkkaar ba noppi, ana nu nuy saxootee bàkkaar?

¶ Ana lu loolu di tekki? Xanaa kon yoonu Musaa bàkkaar la? Mukk kay! Waaye yoonu Musaa moo ma xamal luy bàkkaar. Ndax kat su dul woon ak yoon wi ne: «Bul xemmem yëfi jaambur,» kon xemmemtéef sax duma xam lu mu doon.

¶ Ana lu nu ci mana wax nag? Yàlla daa wàcc foofu yoon? Mukk kay!

¶ Moo tax ma ne xanaa ba bànni Israyil tërëfee, jéll bu ñu dul jógati lañu daanu? Mukk kay! Waaye tooñug bànni Israyil moo waral muccug jaambur ñi dul Yawut, ba tax bànni Israyil siis leen.

¶ Yàlla mi mata gëm de seere na ne kàddu gi nu leen di wax du «waaw, déet,»

Duma neenal yiwu Yàlla, ndax kat su doon ci sàmm ndigalu yoon lees di ame àtteb ku jub, konoon Almasi moo dee cig neen.

Titus 1:2 TSK

Ngëm googu, ak xam-xam boobu, ñu ngi sukkandiku ci yaakaar, ji nu am ci texe ba fàww, te googu texe, Yàlla mi dul fen, moo ko dige ba àddina sosoogul.

¶ «Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Filadelfi nag, bind ko, ne ko: «Lii moo di kàdduy ku Sell ki, kiy Dëgg, te yor caabiy Daawuda, di tijji te kenn du tëj, di tëj te kenn du tijji. Mu ne: