TSK

TSK · Lamentations 4:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 2:12 TSK

Ñu dikk ba jub ko, di ko séentoo fu xawa sore, waaye xàmmeetuñu ko. Ñu daldi ne yikkét jooy. Ba ñu agsee ku ci nekk ne sa mbubb tareet. Ñuy ñaawlu, di tibb suuf, di sànni ca kaw, muy sottiku ci seen kaw bopp.

Job 30:17 TSK

Guddi dikk di bënn samay yax, muy rot, mitit di ŋereñ te du selaw.

Job 33:21 TSK

jeex tàkk bay réer ak a feeñ, yaxam ya ne fàŋŋ te sàngu woon,

Aji Sax ji, fitt nga maa fitt, dóor nga ma.

te sa mer ak sa xadar a tax, nde yaa ma fab, xalab.

Moo dawoon yaramu ñu bare, ndax yàqu ba nirootul nit, bindootul woon ni doom aadama,

Sëxëtooleen xaalis, sëxëtoo wurus, alal du fi jeex te mboolem gànjar a jale.