TSK

TSK · Proverbs 17:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba loolu amee Ibraam da ne Lóot: «Waay waay, bu xuloo am sama digganteek yaw mbaa say sàmm ak samay sàmm. Xanaa dunuy bokk nag?

¶ Bésub keroog xeex ba metti na lool, waaye Abner ak waa Israyil ñoo féete suuf niti Daawuda.

Réy-réylu jote rekk lay jur, ku dégg ndigal a xelu.

Tont lu neex day giifal, baat bu ñagas di jógal xol.

Moytuw ay, ndam la; dof boo gis day bëgg xuloo.

Këriñ defi xal, matt xamb ub taal, ab xulookat di xambu ay.

Fa mbir mujjee gën fa mu doore, te muñ a gën réy-réylu.

Acts 6:1 TSK

¶ Jant yooyu nag, naka taalibe yi di gëna bare, Yawut ñiy làkk gereg tàmbalee ñaxtu ci kaw Yawut ñiy wax seen làmmiñu bopp ndax néewal gu ñu gis ñu néewal ko seeni jëtun ca na ñuy séddalee ag ndimbal bés bu nekk.

Su manee am, jàmmooleen ak ñépp, ndegam ci yeen la aju.

Waaye werante yu xeluwul te du xam-xam, moyu ko, te xam ne ay ŋaayoo lay jur.